Elzo JamDong - Roy Thi Mom Remix lyrics

Published

0 202 0

Elzo JamDong - Roy Thi Mom Remix lyrics

{1er couplet} Samm diamm (diamm dongg), diamma**anté (diamm) Dokh tankou diam, dokh mbokk, bénieu diamanté Diangg dionggou yokk diom fey ki meu dane bote Diapp dioulli diamou diemeu diengou dioke te begneu toke (toke) Dieuf dieuf diou rafet ndakhté wakh tidiégoul bounte Mousslou thi thiate tamit ségueum lamigne djigoul bante Tabakh diakk def ni mame sama tourondo, yokk barké Mom mi dianggalaté batou Oumar Foutiyou ak Bamba Mbacké Kakkatar thi bitim rew, doumeu fatté ni gaindé la Gueuwmeu yakh bou rey dé wanté domou niaye bou ngandé laa Domou Salama Sow yaye nietti yone laley gueureum Domou Hammady Laliyah , Baye Yalle nele Yalla yéreum Santeu Yalla bi niou nekké goné guiss negn kouniou doy Légui lerr ne me ligueyou ndèye rekkeudi aniou dome Dolli sante bi niou maggué am thi kou niou meuneu roy roy roy Yow ya niou téter té souniou Adiana yako mome mom mom {Refrain} (Mathart) -Yayeu woné ngor ak diom thi biir keur gui, Nioune niou roy thi mom (Elzo) -Yayeu liguey rek niou roy thi mom (Mathart) -Yayeu woné ngor ak diom thi biir keur gui, Nioune niou roy thi mom (tchi Mommm) (Elzo) -Yayeu liguey rek niou roy thi mom (Mathart) -Dégloul me wakh leu benn yone Faut que me roy thi Mama (Elzo) -Yayeu liguey rek niou roy thi mom (Mathart) -Sou doyoul me wakh ko niaari yone Faut que roy thi Mama (Elzo) - Yayeu liguey rek niou roy thi mom {2ème couplet} Bineta, Kya, Rokhaya, Astou, Salma, dénk negn me lene Kham nani dou Zair mane mi borom tèleu mey djiguene Gor yomboul moss kou niakk fit ak Yalla yomb rére Kom-kom dou thi am-am kou amoul diiné niakk rek Diangg thi diouromi mak li takh be diémoumeu magg rakh Di niane soutoreu yokkou té yit diamm yagg sakh Défar kate béniou bolé niou bokk déréte bokk darou Tawey Altiné maye Gaou, Dibère mou mey Mama nopalou Yalle ne fi yagg té wer té niou meuneu samm li niou Yalla mey Ndakh seytané eupp dollé diourom niaari Balla Gaye Boumeu sanione dane ko legui dioni dioni Hallyday Baye dem neu, Yaye me nianati yalle ne le Yalla fey Takk ndigg fa** diom woné ngor nga mataléé Tek thi goungué Baye beumou wathieu liguey Mama Salama Thionké Seydou Gallo Guélel Amel Bessel Cherif Deyibou Hammady Laliyah Macina {Refrain} {Mathart - 3eme couplet} Tarbiyou neu Baye, liguey bi war thi nioune le def téwoul beu fi mouy try Tarbiyou neu Baye liguey bi war thi nioune le def téwoul beu fi mou fight Tankk bi gatt neu khéleum bi nekk thi Allahou Dioulli di wore di niaane tallal Bour bi Allahou Démoul fenn thi biir keureum leu toke di diaamou Gueumoul Addouna ndiabote gui rekk leu taamou Eskey live up Mama, yokk niou dolé lerr neu niou ni Yangui fi di niaane fou sori legn niouy khole oh oh oh {Refrain}

You need to sign in for commenting.
No comments yet.